ALLAH

Jean paul SY, Xavier BEGUE

Man xawma ñaata at a ngui nii ma toog di ko xoslu
Gëm ne bes di na ñëw Yalla ubbil ma ayi bunt
Nee nañu damay caaxaan, ñële ne nañu damay fontu
Ñooñu duma leen tontu. Who God bless no man can test
I give thanks and praises to the Lord Allah
Buur bi musal nama ci musiba ag balaa
Bëg naa bala may genn ci aduna
Samay waa-jur, samay mbokk bayyi leen ci sutura
Teraanga Yalla moo la koy jox waye xamal loo ciy def
Bu mbir mi tambalee baax seytaneey taxaw sa xef
Dugal la ci ñaawteef nga reer naka nguay def
Duma ko nangu, dama koy moytu
that’s why I give thanks and praises

Gëmal sa diine, gëm sa bopp,
lepp looy def wékk ko ci kenn ki mooy Allah
Bes bu nekk, saa su nekk lepp looy def
wékk ko ci kenn ki mooy Allah
Man sumay wax, sumay dox, awma dara lumay tiit
mangui ànd ag kenn ki mooy Allah
Allah! Ey waay Allah!

Jangal sama rakk, doomu nday moo ëpp solo
Amul solo nit ñi su ñuy xool yaw ni nguay soloo
Gëmal sa bopp, dem te baña bayyi sa loxo
Li ngua bëg ding ko am inchallah yaw su fekkee loxoo
Mani job mooy wareefu doomu Àdama
Loolu mooy li ñu indi ci dunya
Yalla tegul kenn lumu mënul doomu yaay
Ñafeel sa bopp, amal sa bopp, lepp di na baax inchallah
Mani peace love ag unity
sama people ñu ngui suffer tchi mbënd beeg poverty
mani ñu boole suñu xol yi, ñu delloo suñu xel yi
buñu santee mu dolli give thanks and praises

Allah mi ngi fepp, moom mooy lepp,
Jox ko sa xol, jox ko sa xel waaw waaw
Nee naa la kepp ku repp ba réer doo ko fekkee
Allahu waahidun, wax nañ ko ba tàyyi jëmale sama xol

Beliebteste Lieder von Natty Jean

Andere Künstler von African reggae